On June 14, 2024, Senegalese pop singer Viviane Chidid released her new song “XAARIT”. The lyrics were written by Bakhaw DIOUM, with the music produced by Akatché.
XAARIT song lyrics by Viviane Chidid
Dama Ni Sama Xarit Nga
Te Yaw Mi Xam Nga Ni Ku La Bëgg Laa
Wax Dëgg Yàlla Seede Na, Sama Xarit Nga
Te Yaw Mi Xam Nga Ni Ku La Bëgg Laa
Bëgg Naa La Ba Foo Pikiiru Ma Naan Fa Doom
Lu La Metti Gaañ Ma, Lu La Wokk Xuri Ma Yay
Ma Ni Yaw Foo Pikiiru Ma Naan Fa Doom
Lu La Metti Gaañ Ma, Lu La Wokk Xuri Ma, Yeh Yeh Yeh
Buur Yàlla Moo Ñu Boole
Sama Waay Nga Te Du Tay Loolu Démb La (Loolu Démb La)
Man Ak Yaw Boobu Ba Léegi
Sunu Diggante Bi Teye Nañ Ko Mu Dëgër (Mu Dëgër)
Oh Oh Oh
Xarit Dëgg Am Na, Xarit Dëgg Am Na
Oh Oh Oh
Sa Xarit Dëgg Man La, Seedeel Naa La Lii
Sama Waay Nu Ko Raw Laa La Bëggee
Nga Sax Ci Sama Xol Maa Ko Wax Sama Guy Nga
Foo Ko Seen Geestu Gis Ma
Guddi Muy Bëccëg Soriwuma
Dégg Nañu Lu Bon, Dégg Nañu Lu Baax
Bokku Nañu Bànneex, Bokku Nañu Naqar
Ba Pare Mel Ni Ay Cheikh Amuñu Nëbo
Eh Eh, Du Lekk Bàyyi Ma
Ma Ni Yaw Xarit Nga
Gën Nga Doomu Ndeye, Lii Leer Na Ma
Yaw Xarit Nga
Zeyna Ndour Doo Doom Waay Nga
Buur Yàlla Moo Ñu Boole
Sama Waay Nga Te Du Tay Loolu Démb La (Loolu Démb La)
Man Ak Yaw Boobu Ba Léegi
Sunu Diggante Bi Teye Nañ Ko Mu Dëgër (Mu Dëgër)
Oh Oh Oh
Xarit Dëgg Am Na, Xarit Dëgg Am Na
Oh Oh Oh
Pa Philippe Xam Na Seedeel Na Ma Lii
Oh Oh Oh
Xarit Dëgg Am Na, Xarit Dëgg Am Na
Oh Oh Oh
Pa Philippe Xam Na Seedeel Na Ma Lii
Foo Pikiiru Ma Naan Fa Doom Loolu Leer Na
Yaa Gën Ci Man Fu Ma Jaaxle Ñëw Seetsi La
Yaw Rekk Laay Gis Su Lëndëmee
Lu Ñu Mësa Wax Ci Ñun La Yam
Lu Ñu Mësa Def Ci Ñun La Yam
Bu Dara Xewe Ñu Ànd Dem
Suñu Diggante Moo Dàq Lem
Sama Jikko Boo Ko Bëggee Gis Laal Ko Seet
Yaa Yéy Def Ko Muy Sa Xarit
Bul Déglu Kenn Àndal Ak Moom
Doom Day Sax Ci Xolub Ndayam
Vivi Ànd Ngeen Sax Ba Ndiroo Kanam
Kuy Laal Ma Démba Sagar Yaa Ca Ndam
Kuy Laal Sama Waa Ji Vivi Jugal Ñu Dem
Lu La Wokk Xuri Na Ma Foo Dee Ma Dee Fa
(Àndal Ak Ku Dal Sa Xel!)
Ni Ñuy Àndee Nii Neex Na Ma Xarit Sama
(Xarit Dëgg Nii Lay Mel)
Yaw Rekk Laay Gis Su Lëndëmee
(Moy Cote Far!)
Ñun Benn Lañu Te Duñu Ñaar (Moo Am)
Lu Ne Lañu Gis Ndax Fi Ñu Jaar
(Moo Tax Yaa Ngi Ca Kanam)
Bu Coow Li Bare Maak Yaw A Far (Ñoo Far)
Amitié Bu Mel Ni Aka Rare (Loo Sax!)
Sama Jikko Boo Ko Bëggee Gis Laal
Ko Seet (Kaay Laal Lu La Ci Dal Dinga Xam)
Ku Nekk Làmbil Bi La Neex Topp Sa Xarit
Maa Yéy Sama Yaay Laay Topp
Bu Ngeen Àndee Dina Neex, Ah
Bu Ngeen Àndee Dina Neex, Aa Thiam Day Neex
Foo Pikiiru Ma Naan Fa Doom Loolu Leer Na
(Dama Ni Li Leer Na)
Yaa Gën Ci Man Fu Ma Jaaxle Ñëw Seetsi La
(Ñëw Seetsi La)
Yaw Rekk Laay Gis Su Lëndëmee (Cote Far, Far!)
Lu Ñu Mësa Wax Ci Ñun La Yam (Ñun Rekk)
Lu Ñu Mësa Def Ci Ñun La Yam (Ñun Rekk)
Bu Dara Xewe Ñu Ànd Dem (Sañse Lu Took)
Suñu Diggante Moo Dàq Lem (Aaah!)
Sama Jikko Boo Ko Bëggee Gis Laal
Ko Seet (Kaay Laal Lu La Ci Dal Dinga Xam)
Kuy Laal Sama Waa Ji Lu La Ci Dal Yaa Xam
Kuy Laal Ma Démba Sagar Yaa Ca Ndam
Kuy Laal Sama Waa Ji Lu La Ci Dal Yaa Xam
Kuy Laal Ma Démba Sagar Yaa Ca Ndam
Kuy Laal Sama Waa Ji Lu La Ci Dal Yaa Xam
Kuy Laal Ma Démba Sagar Yaa Ca Ndam
Summary
The song is a heartfelt expression of deep friendship and love. The singer emphasizes the importance of a true friend who is like family and provides unwavering support. They reflect on the trust and reliability that come with such a bond, highlighting how it brings joy and comfort in times of need. The lyrics also touch on the beauty of shared moments and the assurance that their connection is solid and enduring.
Related Songs –
- Genesis – RAYE
- I Still Know Better – Headie One
- Me & U – Tems
- Top – DDG & Blueface (feat. Swae Lee)
- 21 – Ayra Starr
- Tantrums – Normani ft. James Blake
XAARIT Song Info:
Song Name: | XAARIT |
Lead Vocals: | Viviane Chidid |
Written/Lyrics By: | Bakhaw DIOUM |
Music Produced By: | Akatché |
Music Label: | ASTAR |
Release Date: | June 14, 2024 |
Music Video Director: | ASTAR & BILAL Mbengue |
Frequently Asked Questions
Who produced “XAARIT” by Viviane Chidid?
“XAARIT” by Viviane Chidid was produced by Akatché.
When did Viviane Chidid release “XAARIT”?
Viviane Chidid released “XAARIT” on June 14, 2024.
Who wrote “XAARIT” by Viviane Chidid?
“XAARIT” by Viviane Chidid written by Bakhaw DIOUM.
Who sang the “XAARIT” Song?
The “XAARIT” song is sung by Viviane Chidid.